àjjana moo gën a jege ku ne ci yeen ay waroy dàllam, sawara it naka noonu
Jële nañu ci Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne: «àjjana moo gën a jege ku ne ci yeen ay waroy dàllam, sawara it naka noonu».
Al-buxaariy soloo na ko
Explanation
Yónente bi day xamle ne àjjana ak sawara dañoo jege nit ki kem ni ko ay waroy dàllam jegee te mooy liy nekk ci kaw ndëggu yi, ndaxte moom man naa def ab topp Yàlla ngir ngërëmam loolu dugal ko àjjana, walla ab moy Yàlla loolu nekk sabab ci duggam sawara.
Hadeeth benefits
Xemmemloo ci jëf lu baax doonte dafa néew, ak xuppaate ci jëf lu ñaaw doonte dafa néew.
Jullit cig dundam manul ñàkk mu boole yaakaar ak ragal, tey sax ci ñaan Yàlla mu saxal ko ngir mu mucc te du woru ci melokaanam.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others