- Wooteb Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa matale ñépp, te dañu koo war a topp, te dafa folli ci sariihaam ji mbooleem sariiha yi.
- Ku weddi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- njort bi mu njort ne gëm na yeneen yonnente yi du ko jariñ dara.
- Ku déggul Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, te wooteeb Lislaam bi àggul ci moom kooku dees na ko dogal ngànt, ay mbiram nag ëllëg bis-pénc ci Yàlla lay dellu.
- Manees naa jariñu ci lislaam doonte tuuti la jiitoo dee gi, donte ci tawat ju tar la, fii ak ruu gi eggul ci bóli gi.
- Nangu diiney yéefar yi -te yahuut yi ak nasaraan yi ci la ñu bokk- loolu ag kéefar la.
- Tudd gi ñu tudd yahuut yi ak nasaraan yi -ci hadiis bi - loolu ngir yee ñeneen ñi la; ndaxte yahuut yi ak nasaraan yi am nañu téere, kon bu dee lii mooy seen mbir, kon ñi amul téere ñoo ca gën a yey, ñoom ñépp a war a dugg ci diine ji te topp Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.