- Bokk na ci njariñal adiis bi :
- Ñaaxe ci tegtale lu baax.
- Soññee ci def lu baax bokk na ci sabab i jàppalanteeg jullit ñi ak seenug bennoo.
- Yaatug ngënéelu Yàlla.
- Hadiis bii ab tënk bu matale la, jépp jëf ju baax da ciy dugg.
- Nit ki bu manut a faj aajiy kiy laaj, da koy tegtal keneen.