- Ngëneelu woote jëme ci njub, moo xam mu néew walla mu bari, ak ne wootekat bi day am lu mel ni payug aji-jëfe ji, loolu nag day wane màggaayu ngëneelu Yàlla ak matug teddngaam.
- Loraangey woote jëme ci réer, muy lu ndaw walla lu bari, te aji-woote ji dana am lu mel ni bàkkaaru aji-jëfe ji.
- Ag pay daal ma ngay toll kem na jëf tollu, ku woote ciw yiw am lu mel ni payug aji-jëfe ji, ku woote it jëme ci lu bon dana am lu mel ni bàkkaaru aji-jëfe ji.
- Jullit bi daa war a moytu ñu koy roy ci bàkkaaram yi muy fésal nit ñi di ko gis, ndaxte day am bàkkaar ndax ñi ko ci roy donte woowu leen ca.