Explanation
Leerarug hdiis bi:
Abdullah Ibn Mashuud nee na: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- waxtaanal na nu te mooy aji-dëggal ciy waxam, di ku ñu dëggal ndax Yàlla mu kawe mi moo ko dëggal, Mu wax ne: ku nekk ci yéen dees na dajale am mbindam, te loolu mooy bu góor gi dikkalee Soxnaam, Maniyoom mi tasaaroo ci biiru ku jigéen ki ñent-fukki fan nekk aw toq, Mu nekk aw lumb te mooy dereet ju tal te wow, ci ñaareelu ñent-fukk ya, Mu nekkaat aw suux te mooy dogu yàpp wu tolloog lu ñu yëy, ci ñatteelu ñent-fukk yi Yàlla yabal ci moom malaaka ma, mu wal ca ruu ginnaaw ñatteelu ñent-fukk ya, Ñu digal malaaka mi mu bind ñenti baat, te mooy: wërsëgam, te mooy nattub li mu war a am ci xéewal cig dundam, Ak digam, te mooy diir bi muy des ci àdduna, Ak jëfam, lan la? Ak day texeedi walla day texe. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di giñ ne kenn dana jëf jëfi waa àjjana jëfam di lu baax, maanaam ci liy feeñ ci nit ñi, mu sax ci loolu ba dara doxul digganteem ak àjjana lu dul ab loxo, maanaam: dara desul ci mu àgg fa lu dul mel ni koo xam ne li des digganteem ak benn bérab ci suuf ab Lox rekk la, tére ba not ko ak la ñu dogal ci kawam ci moom ci loolu nag mu jëf jëfi waa sawara ñu tëje ko ay jëfam mu dugg sawara; Ndax sarti nangug jëf mooy mu sax ca te du ko soppi, ak keneen ci nit ñi di jëf jëfi waa sawara ba jege faa dugg, ba mel ni digganteem ak sawara lu tollook loxo ci suuf moo fa dox, dogal ba not ko mu jëf jëfi waa àjjana daal di dugg àjjana.