- Bokk na ci njariñal adiis bi:
- Mooy day moytandiku Loo roy yéefar yi ak kàccoor yi.
- Day soññee ci di niru-nirulu ñu baax ñi ak di leen roy.
- Roy ci biti day waral mbëggeel ci biir.
- Nit ki dees na ko tëkku mu am bàkkaar kem niru-nirulu ga ak i xeetam.
- Terees na niru-nirulu lu yéefar yi ci séen diine ak séen aada ja ñu jagoo, bu dul loolu nag niki jàng liggéey yi ak yu ko niru loolu tereesu ko.