- Bokk na ci njariñal adiis bi: Hadiis bi cosaan la ci leeral martabay soppi lu bon.
- Digle na ñu di def ndànk-ndànk ci bu ñuy tere lu bon, ku nekk ak li mu man ak fa kàttanam tollu.
- Tere lu bon bunt bu màgg la ci diine te du wàcci kenn, war na bépp jullit ci kem kàttanam.
- Digle lu baax ak tere lu bon daa bokk ci meloy ngëm, te ngëm day yokku di wàññiku.
- Sartal nañu ci tere lu bon: xamne jëf jooju dafa bon.
- Sartal nañu ci soppi li bon: lu gën a bon bañ caa topp.
- Tere lu bon am na ay teggin ak i sart yoy war na ci jullit bi mu xamlu ko.
- Weddi lu bon dafay laaj doxaliin wu jaar yoon, ak xam-xam ak gis-gis.
- Ñàkk a weddi ci sa xol day wane ngëm gu néew doole.