- Bokk na ci njariñal adiis bi:
- Gëm ndogal yi lu war la.
- Ndogal mooy: xam gi Yàlla xam bir yi, bind ko, ak coobareem, ak amal ga mu ko amal.
- Gëm ne ndogal yi bind nañu ko njëkk ñuy bind asamaan yi ak suuf si day waral gërëm ak nangu.
- Gàngunaayu Aji-Yërëme ji moo ngi ci kawum ndox lu jiitu bindug asamaan yi ak suuf si.