- Bokk na ci njariñal adiis bi :
- Tëkku gii nag nekkul ne njiit lu mag li ak ña koy wuutu rekk a ko jagoo, waaye day làmboo képp ku Yàlla sàmmuloo am càmm.
- Li war képp ku jiite dara ci biri jullit ñi mooy mu leen di laabire, te pastéefu ci matal kóllare, te moytoo wor.
- Màggaayu wartéefu képp Ku yilif Aw nit, moo xam kiliftéef gu gu ndaw walla gu mag.