- Araamal nañu gisaane, ak dem ci gisaanekat yi ak laaj leen ci kumpa yi.
- Dees na xañ nit yoolub jaamoom ngir mbugale ko ko ci bàkkaar bu mu def
- Day dugg ci Hadiis bi li ñuy woowe taaruwaayu biddiw yi ak di ca xool, ak di jàng ca ténq ya ak kopp ya -donte ci anamug yër dong la-; ndax loolu lépp ci seet la bokk ak wootewoo xam kumpa.
- Ndeem lii mooy payug ku dem ci xamtukat ba, kon naka la payug jëmmi kiy xamtu di deme?
- Jullig ñent-fukki fan ya dana ko doy kon du ko fay, waaye du ca am ab yool.