- Bokk na ci njariñal hdiis bi: warug wakkirlu ci Yàlla te gërëm ay dogalam ak i àtteem, te araamal gisaane ak gaaflu ak njabar ak seetlu, mbaa laaj ña koy def.
- Wootewoo xam kumpa daa bokk ci bokkale wuuteek Tawhiid.
- Araamalees na dëggal ab seetkat ak dem ca ñoom, dana bokk ca loolu li ñuy woowe jàng ca ténq ya ak kopp ya, ak nekkuwaayu biddiw yi, ak di ca xool donte sax ci anamug yër la.