- Dañoo war a sellal jëf yi ngir Yàlla mu màgg mi, te moytu ngistal.
- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa ñeewante lool aw xeetam te xér ci gindi leen ak di leen laabire.
- Bu dee nii la ragalug Yonnente bi toll te muy wax ak sahaaba yi, te ñoom ñooy sangi ñu baax ñi, kon ragal ci ñiy ñëw seen ginnaaw mooy gën a tar.