- Leeral ngëneelul Yàlla lu màgg li ci xeet wii am ci ful giñuleen di fulal ay yiw ak di ko bind fa moom, ak ñàkk giñuleen di ñàkka fulal séen i ñaawtéef.
- Njariñu yéene ci jëf yi ak ay jeexitam.
- Ngëneelu Yàlla mu kawe mi ak ug ñeewanteem ak rafetalam ci ne ku nàmm a def aw yiw te mujju ko def Yàlla bindal ko ko aw yiw.