- Bokk na ci njariñal adiis bi:
- Yittewoog Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- jëf yi ñu doon def ca ceddo ga.
- Ñaaxe ci sax ci Lislaam.
- Ngëneelu dugg ci Lislaam ak ne day far jëf ya ko jiitu woon.
- Ki génn ci diine ji ak naaféq bi dees na leen toppe la ñu defoon lu jiitu Lislaam, ak bépp bàkkaar buñu def ci Lislaam.