- Araamal na ñu wax ci jamonoy xutba, donte tere lu bon la, walla delloo ab nuyoo, walla ndokkeel ku tissooli.
- Danañu settee ci loolu kuy wax ak imaam walla imaam di wax ak moom.
- Wax ci diggante ñaari xutba yi ngir aajo dagan na.
- Bu ñu tuddee Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fekk imaam bi di xutba dangay julli ci moom ndànk, niki noonu it wax aamiin ci ag ñaan.