- Sopp nañu julli ñaari ràkka ngir nuyu jàkka ji bala ñoo toog.
- Ndigël lii nag ngir ku bëgg a toog la, ku dugg ci jàkka daal di génnaat njëkk muy toog kooku ndigël li jëmul ci moom.
- Aji-julli ji bu duggee ci jàkka ji fekk nit ñi nekk ci julli gi mu dugg ci julli gi ànd ak ñoom loolu dana ko doy wolif ñaari ràkka yi.