- Sangu ñaari xeet la: boo xamne dana doy, ak bu mat sëkk, bu dee biy doy, nit ki day yéenee laab, daal di matale yaram wi lépp ci ndox boole ko ak gallaxndiku ak saraxndiku, bu dee bu mat sëkk bi nag, day sangu kem ni Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- sangoo ci hadiis bii.
- Danañu woowe janaba képp ku génne maniyu, walla mu sëy doonte génnewul maniyu.
- Dagan na ci ñaar ñiy sëy ku ne xool awray keneen ka, ak ñu sangu ci genn ndab.