- Jigéen gi dafa war a sangu bu bisi mbaaxam jeexee.
- Warug julli ci kiy gis deret ju yàqu.
- Mbaax: deret la juy génn ci butiitu njurukaay gi jaare ci pëyu jigéen ju mat, day ñëw ci moom ci bis yu ñu xam.
- Deret ju yàqu: sottikug deret ci lu dul waxtoom jóge ci suufu butiitu njurukaay bi te du jóge ci biiram.
- Liy teqale diggante dereti mbaax ak deret ju yàqu: dereti mbaax deret ju ñuul la te tal te xasaw ag xet, deret ju yàqu nag dafa xonxu te woyof te amul xet gu xasaw.