- Ñaaxe ci tontu noddkat bi.
- Ngëneelu julli ci Yonnente bi ginnaaw buñu tontoo noddkat bi ba noppi.
- Ñaaxe ci ñaanal Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Wasiila ginnaaw buñu jullee ci moom ba noppi.
- Leeral maanaam Wasiila ak mbiram mu kawe, ba tax du yéwén lu dul ñeel kenn rekk.
- Leeral ngëneelu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ba tax ñu jagleel ko daraja ju kawe jooju.
- Ku ñaan Yàlla Wasiila ñeel Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- kooku ramm ma dagan na ko.
- Leeral toroxlug Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ba tax muy sàkku ci xeetam wi ñu ñaanal ko daraja jooju, ànd ak loolu moo koy moom.
- Yaatug ngëneelu Yàlla ak yërmàndeem, benn bu baax fukk yu mel ni moom mooy ag payam.