- Hadiis bi cosaan la ci cosaani Lislaam yi, ab reegal la ci reegali Fiq yi, te mooy: kóolute du deñ ci sikk-sakka, ak cosaan mooy la fa nekkoon des ca la mu nekkoon, ba keroog muy am kóolute ci lu wuute ak loolu.
- Sikk-sakka du jeexital cim njàpp, kiy julli day des cig laabam feeg amul kóolute cig tojle.