- Xemmemloo ci jottali njàngalem Yàlla, ak ne nit ki dafa war ci moom mu jottali li mu mokkal te xam ko, donte dafa néew.
- Warug sàkku xam-xamu Sariiha; ngir mu man a jaamu Yàlla, ak di jottali tërëliinam yi ci anam gu wér.
- Warug wóorlu ci wérug bépp Hadiis lu jiitu jottali ga, walla tasaare ga, ngir moytoo dugg ci tëkku gu tar gii.
- Ñaaxe ci wax dëgg ak di teey ci wax ja, ba du tàbbi ci fen, rawatina ci Sariihab Yàlla mu màgg mi.