- Bàkkaar yi dañoo rawante cig rëyaay, kem ni jëf yi di rawantee ciy ngëneel.
- Bàkkaar bi gën a rëy mooy: bokkaale, ak ray sa doom ngir ragal mu dundu ak yaw, ak njaalo ak sa jabaru dëkkandoo.
- Wërsëg ci loxoy Yàlla la nekk te moom Yàlla mu sell mi moo yor wërsëgi mbindeef yi.
- Àqi dëkkandoo lu màgg la, kon lor ko moo gën a màgg bàkkaar lor keneen.
- Aji-Bind moo yeyoo jaamu moo rekk amul bokkaale.