- Bokk na ci njariñal adiis bi:
- Topp Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa bokk ci topp Yàlla, moy ko it moy Yàlla la.
- Topp Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day waral àjjana, moy ko it day waral sawara.
- Ak bégle ñeel ñiy topp Yàlla te bokk ci xeet wii, ci ne ñoom ñéppay dugg àjjana ba mu des ku moy Yàlla ak Yónenteem.
- Ñeewante gi Yónente bi am ci aw xeetam, ak xér gi mu xér ci seenug gindiku.