- warug bëgg Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, te jiital ko ci bëgg mbindéef yépp.
- Bokk ci màndargay bëgg gu mat: dimbali Sunnas Yónente Yàlla bi, ak joxe sa bakkan ak sa alal ci loolu.
- Bëgg Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day waral topp ko ci lu mu digle, ak dëggal ko ci lu mu xibaare, ak moytu lu mu tere te xuppe ca, topp ko te bàyyi bidaa.
- Àqi Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo gën a màgg gën a feddaliku ci àqi nit ñépp; ndaxte moom mooy sababus sunug gindiku juge cig réer, ak sunug mucc ci sawara ak am àjjana.