- Moytandikuloo jéggi dayob Sariiha ci màggal walla tagg; ndax loolu day jëme ci bokkaale.
- Li Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- doon moytandikuloo de tàbbi na ci xeet wi, am kurel yu ëppal ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc-, am it kurel yu ëppal ci waa kër Yónente bi, ak kurel yu ëppal ci wàlliyu yi, ñoom ñépp tàbbi ci bokkaale.
- Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa melal boppam ci ne jaamub Yàlla la; ngir leeral ne moom ab jaam bu Yàlla moom la, daganul ñuy jëmale ci moom dara ci lu Boroom bi jagoo.
- Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- dafa melal boppam ci ne ndawu Yàlla la; ngir leeral ne moom Yàllaa ko yónni, kon ñu war koo dëggal te topp ko.