- Tere di neenal kër yi ci bañ faa jaamu Yàlla mu kawe mi.
- Tere di tukki ngir siyaare bàmmeelu Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-; ndaxte digle na ñu julli ci moom, mu xibaare ne dana àgg fa moom. Kon dañuy tukki ngir jublu jàkka ja ak julli fa.
- Araamug def siyaare bàmmeelu Yónent bi am ndaje, ci di baril di ko siyaare ci anam gu ñu ko jagleel ak ci jamono ju ñu ko jagleel, naka noonu bàmmeel yépp.
- Teddug Yónente bi ci Boroomam, ba tax mu yoonal ñuy julli ci moom ci jamono ju ne, ci barab bu ne.
- Te sax na ci Sahaaba yi ñuy tere julli ci bàmmeel yi; looloo tax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere ñuy def kër yi mu mel ni ay bàmmeel ba kenn du fa julli.