- Ngënéel u Abuu Bakar Siddiix -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, ag ne moom moo gën ci Sahaaba yi, te moo gën a yay ci nit ñi ngir nekk Xaliifab Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- ginnaaw bi mu faatoo.
- Tabax jàkka ci bàmmeel daa book si ñaawtéefi xeet ya jiitu woon.
- Tere ñuy jàppe bàmmeel yi ay barab ngir jaamu, di fa julli walla di ko jublu, walla di tabax ca kawam ay jàkka ak i xubba, ngir moytandikuloo tàbbi ci bokkaale ci sababus loolu.
- Moytandikuloo ëppal ci gaayu baax yi ndax day jëme ci bokkaale.
- Ñàngug li Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- di moytandikuloo ba tax mu feddali ko lu jiitu muy faatu ci juróomi guddi.