- Tere nañu def bàmmeeli Yónente yi ak gaa yu baax yi jàkka ju ñuu jullee ngir Yàlla, ndax loolu day yóbbe ci bokkaale.
- Tarug yittewoog Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- lii di Tawhiid ak ragalam ci lii di màggal ay bàmmeel; ndax loolu day waral bokkaale.
- Dagan na ñu rëbb Yahuut yi ak Nasaraan yi ak ku def lu mel ni li ñu def ci tabax ci bàmmeel yi ak jàppe ko ay jàkka.
- Tabax bàmmeel daa bokk ci aaday Yahuut yi ak Nasaraan yi, te ñëw na ci hadiis ñu tere di leen niru-nirulu.
- Bokk na ci jàppe bàmmeel yi jàkka di fa julli ak di fa jublu, donte tabaxu ñu ko jàkka.