- Sopp nañu ñu raxas ñaari loxo yi balaa nu leen di dugal ci ndab li ci tàmbalig njàpp mi, bu jugewul ciy nelaw, bu jugee ci ay nelaw ci guddi gi kon raxas leen day war.
- Yell na ci kiy jàngale mu jaar yoon wi gën a jege ag dégg ak xam-xam bu dëgër ci kiy jàng, bokk na ca jàngale ci jëf.
- Jaadu na ci kiy julli mu jeñ xalaat yi aju ci àdduna, ndax matug julli gi moo ngi ci teewug xol bi ci julli gi, donte mucc ci xalaat yi jafe na, waaye war naa xeex ak bakkanam ba du ca wéy.
- Sopp nañu di njëkke ndeyjoor ca njàpp ma.
- Yoonal nañu toftale ci diggante gallaxndiku ak saraxndiku ak fiiru.
- Sopp nañu raxas xar kanam ak ñaari loxo yi ak ñaari tànk yi ñatti yoon, benn yoon moom dafa war.
- Njéggalug Yàlla ci bàkkaar yi day tege ci ñaari mbir: njàpp, ak julli ñaari ràkka, ci melo wi ñi tudd ci hadiis bi.
- Cér bu ne ci céri njàpp yi am na yamukaay: yamukaayu kanam mooy: fi kawarug bopp baaxoo sax, ba li wàcc ci kawari sikkim cib yaatuwaay, ak li dalee ci nopp bi ba ca beneen nopp ba cib yaatuwaay. Yamukaayu loxo mooy: li dale ci cati baaraam yi, ba ca conco yi, te mooy li teqale diggante yaxug loxo bi ak përëg bi. Yamukaayu bopp mooy: li dale fa kawar ga di baaxoo sax ca peggu kanam ga ba ca kaw ndong ga, masaa ñaari nopp yi nag ci bopp bi la bokk. Yamukaayu tànk mooy: ndëggu li yépp ànd ak li teqale digganteem ak yeel bi.