Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na benn-benn
Jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na benn-benn.
Al-buxaariy soloo na ko
Explanation
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeg-leeg bu daan jàpp day raxas cér bu nekk benn yoon, mu raxas kanam gi -ca la gallaxndiku ak saraxndiku bokk-, ak ñaari loxo yi ak ñaari tànk yi benn yoon, lii mooy dayo bi war.
Hadeeth benefits
Li war ci raxas cér yi mooy benn yoon, lu ca tege dañu koo sopp.
Yoonal nañu di jàpp benn-benn leeg-leeg.
Li ñu yoonal ci masaa bopp mooy benn yoon.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others