- Ñaaxe ci yittewoo jàng njàpp ak i sunnaam ak i tegginam, ak jëfe ko.
- Ngëneelu jàpp, ci ne day far bàkkaar yu ndaw yi, bu dee yu mag yi nag tuub rekk a koy far.
- Sàrt yiy tax bàkkaar yi génn mooy matal njàpp mi te moytu lu koy yàq kem ni ko yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leerale.
- Dindi bàkkaar yi ci hadiis bii dañu koo tënk ci moytu bàkkaar yu mag yi ak tuub ko, Yàlla mu kawe mi nee na: (bu ngeen moytoo bàkkaar yi ñu leen tere nu far séen i ñaawtéef) [An-Nisaa].