- Dañoo war a gaaw ci digle lu baax, ak gindi ki xamul ak ki sàggan, rawatina bu fekkee ne njuumte li la cay tege mooy ag jaamoom yàqu.
- War na ñu matale céri njàppu yi ci ndox, ak ne ku bàyyi dara ci cër bi -doonte lu ndaw la- njàppam du wér te da koo war a bàmmtu bu dee diggante bi dafa soree.
- Yoonalees na rafetal njàppu mi, ci matale ko ak jotale ko kem ni ñu ko diglee ci sariiha.
- Ñaari ndëggu yi ci cëri njàppu mi lañu bokk, kon masaa ko dong du ca doy, waaye fàww ñu raxas ko.
- Dañoo war a toftale diggante cëri njàppu mi, di raxas cër bu ne balaa bi ko jiitu di wow.
- Ñàkk a xam ak fàtte du tax li war di wàcci nit ki, waaye bàkkaar bi lay rotal, góor gii nga xam ne jotalul njàppam ngir ag ñàkk a xamam Yonnente bi teggilu ko li war ci moom, te mooy jàppu, waaye da koo digal mu bàmtu ko.