- Wax ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla, sàrt la ci dugg ci Lislaam.
- Maanaam (laa ilaaha illal Laahu) mooy weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla ci ay xërëm ak i bàmmeel ak yeneen, te wéetal Yàlla mu sell mi cig jaamu.
- Ku wéetal Yàlla te taqoo ak Sariiha ci li feeñ, dañu koo war a bàyyi ba mu fésal lu wuute ak loola.
- Alali jullit bi ak deretam ak ub deram dafa araam ci lu dul àqi Lislaam.
- Àtteb àdduna ci li feeñ la, bu dee allaaxira nag ci yéene yi ak jubluwaay yi.