- Ngëm ay tolluwaay la yoo xam ne dañoo gënante.
- Ngëm wax la ak jëf ak pas-pas.
- Am kersa ci Yàlla mu kawe mi day waral: ba du la gis ci li mu la tere, du la ñàkk a gis it ci li mu la digal.
- Tudd lim bi tekkiwul ne ag tënk la, waaye day tegtale ne jëfi ngëm yi dafa bari, Araab yi danañu tuddal mbir mi ab lim waaye bëgguñoo dàq leen lu dul moom.