- Bokk na ci njariñal hdiis bi:
- Leeral àqi ji Yàlla waral ci jaamam ñi, te mooy ñu jaamu ko, te bañ koo bokkaale ak dara.
- Leeral àqi jaam ñi ci Yàlla mu kawe mi te Yàlla warlul ko boppam ngir ngëneel ak xéewal, te mooy mu dugal leen àjjana, te du leen mbugal.
- Ag bégle la ñeel way-kennal yi nga xam ne duñu bokkaale Yàlla ak dara ci ne séenug mujj mooy dugg àjjana.
- Muhaas dafa nettali hadiis bii laata muy faatu; ngir ragal a tàbbi ci bakkaaru nëbb xam-xam.
- Artu ci bañ a tasaare yenn Hadiis yi ci yenn nit ñi ngir ragal ci kaw ñi nga xam ne manu ñoo xam maanaama; te loolu mooy yi nga xam ne jëf aju wu ca mbaa AB daan ci daani Sariiha yi.
- Ñiy kennal Yàlla tey def ay bàkkaar ñoo ngi ci ron coobarey Yàlla bu ko soobee mbugal leen, bu ko soobee it mu jéggal leen, waaye seenug mujj mooy àjjana.