Yàlla dat ŋëb suuf si, lem asamaan yi ci ndayjooram, di wax naan: man maay buur, ana buuri suuf si
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «Yàlla dat ŋëb suuf si, lem asamaan yi ci ndayjooram, di wax naan: man maay buur, ana buuri suuf si».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Explanation
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne yawmal xiyaam Yàlla day ŋëb suuf si dajale ko, mu lem asamaan si ci ndayjooram taxañ lenn la ca kaw leneen la daal di koy dindi jële ko fi, topp muy wax naan: man maay buur, ana buuri suuf si?!
Hadeeth benefits
Fàttalee ci ne nguurug Yàlla moo fiy des nguurug keneen nag day deñ.
Màggug Yàlla ak màggug kàttanam ak nguuram ak matug nguuram.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others