- Bokk na ci liy tax a tàbbi ci bànneex yi li Saytaane di taaral lu bon ak lu ñaaw, ba mujj bakkan bi di ko gise lu rafet daal di jeng jëm ca.
- Digle ñu sori bànneex yi ñu araamal; ndax te yoonu sawara la, ak muñ ci yu naqari yi ndax te yoonu àjjana la.
- Ngëneelu xeex ak bakkan, ak farlu ci jaamu yi, ak muñ ci yu naqari yi ak coono yi wër topp yi.