/ Sama mbalka ma de mi ngi toll ne doxu weer, ndoxam ma moo gën a weex meew, xetam ga moo gën a neex gëttug misk

Sama mbalka ma de mi ngi toll ne doxu weer, ndoxam ma moo gën a weex meew, xetam ga moo gën a neex gëttug misk

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Sama mbalka ma de mi ngi toll ne doxu weer, ndoxam ma moo gën a weex meew, xetam ga moo gën a neex gëttug misk, te koppu yi dañoo mel ni biddiwi yi nekk ci asamaan Ku ci naan doo mar mukk ».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér

Explanation

Leerarug hdiis bi : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne am na am mbalka ëllëg bis-pénc, guddaayam mi ngi toll ne doxu weer yaatuwaayam it naka noonu, Ndoxam ma moo gën a weex meew, Xetam moo gën a neex te gën a teey xetu misk, Ay koppam moo ngi toll ne biddiwi asamaan cig bari, Ku naan ca mbalka ma ci kopp yooya dootul mar ba fàwwu.

Hadeeth benefits

  1. Déegu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fu ndox dajaloo la mu màgg lool, te way-gëm ci xeetam ñoo cay naan ëllëg bis-pénc.
  2. Ku naan ca déeg ba dana am xéewal te dootul mar mukk.