- Sopp nañu nuyòo kem ni ko hadiis indee, bu kiy dox nuyòo ki war ak lu dul loolu ci li ñu tudd, dana dagan, waaye daa wuute ak li yelloon te gën.
- Tasaare nuyòo ci anam gi mu ñëwe ci hadiis bi daa bokk ci sababi bëggante yi ak miinante yi.
- Bu ñu yamoo te tolloo ci yi nu wax, kon ka ca gën mooy ka njëkk a nuyòo.
- Matug Sariiha ci leeral lépp lu nit ñi aajowoo.
- Jàngale teggini nuyòo ak jox ku nekk àqam.