- Bokk na ci njariñal adiis bi :
- gëneelu wakkirlu, ak ne dafa bokk ci sabab yi gën a màgg ci yiy xëcc wërsëg.
- Wakkirlu du dàqoonteek def sabab yi, ndax dañoo xamal ne dëgg-dëggi wakkirlu du wuute ak xëy walla gontu jëm ci sàkku wërsëg.
- Yittewoog Sariiha ci jëfi xol yi; ndax wakkirlu jëfu xol la.
- Sukkandiku ci sabab yi dong loolu diine ju wàññiku la, waaye bàyyi sabab yi tamit xel mu matul la.