- Bokk na ci njariñal hdiis bi:
- Gëm ne àjjana ak sawara fi mu ne nii am nañu.
- Dañoo war a gëm kumpa ak lépp lu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- indi.
- Solos muñ tiis yi ndax te yoon la wuy àggale àjjana.
- Solos moytu yu araam yi; ndax te yoon la wuy yóbbe sawara.
- Àjjana dañu koo muure ak i tiis, sawara ñu muure ko ak i bànneex, loolu mooy nattub dundug àdduna gi.
- Yoonu àjjana dafa jafe te metti, day aajowoo muñ ak jàmmaarlook yu metti yi ànd ak ngëm, yoonu sawara nag daa fees dell ak i neex-neex ak i bànneex fii ci àdduna.