Séen sawara wi ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaj ci xaaji sawaraw Jahannama
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Séen sawara wi ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaj ci xaaji sawaraw Jahannama», ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, bu doon moom rekk kon dana doy. Mu wax ne: «ëppe na ko juróom-benni fukk ak juróom-ñenti xaaj, te ñoom ñépp ñoo ngi mel ni aw tàngaayam».
Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér
Explanation
Leerarug hdiis bi :
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne sawaraw àdduna ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaji sawaraw Jahannama, Sawaraw allaaxira moo gën a tàng sawaraw àdduna ci juróom-benni fukk ak juróom-ñetti xaaj, te xaaj bu ci ne moo ngi tolloog tàngaayu sawaraw àdduna. Ñu ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, sawaraw àdduna bi rekk doyoon na ngir mbugal ña fay dugg, Mu ne leen: sawaraw Jahannama ëppe na sawaraw àdduna ci juróom-benn ak juróom- ñenti xaaj te ñoom ñépp a mel ni moom ciw tàngaay wu tar.
Hadeeth benefits
Xuppe ci sawara ngir nit ñi sori jëf ya cay yóbbe.
Màggug sawaraw Jahannama ak mbugalam, ak tàngaayam wu tar.
Share
Use the QR code to easily share the message of Islam with others